vendredi 28 février 2014

Firi xasidag SINDIIDI ci wolof [aji tekki ji, Serigne Cheikhouna LO Ngabou ]


SINDIIDI
Xasidag ñaan ak tawassaul ci barkéb gaayu baax ya
Ki ko taalif ci arab : Cheikh Ahmadou Bamba
Ki ko tekki ci wolof : Cheikhouna LO Ngabou


Ci turu Yàlla jiy yëramaakoon bi di jaglewaakoon laay tàmblee, di julli (ñaan xéwël ak mucc) ci Yonnent bi aki waa këram aki àndandowam.


1- Yàlla ( maa ngi lay ñaan) ci (barkeb) ku ñu belli (tànn) ka jàmbaar ja (Muhammad) ak sa xarit ba Ibraayima ( Maa ngi lay dagaan ) Yaw Yàlla.


2- Ak (barkeb) sa waxtandoo wa Muusaa, Saalihu, Xudar, Shuaybu ak Ismaayila ( Maa ngi lay dagaan ) yaw Yàlla.


3- Ak (barkeb) Sulaymaan, Nuuh , Yuunus, Ilyasa, Zakariyya, Yahyaa, Huud, Yuushuhan, Ilyaas, Aadama, Daawuda, Dhil-kifl, Iisaa, luut ( Maa ngi lay dagaan ) Yaw Yàlla.


4- (ci barkeb) Haaruuna, Yuushuhan, Ilyaas, Aadama, Daawuda, Dhil-kifl, Iisaa, luut (Maa ngi lay dagaan ) Yaw Yàlla.


5- (Ci barkeb) Yuusuf, Ishaaq, ak mbooleem ñi nga am ca (ña ame xam-xam ag ndombog yonnent ga (te yabaloo léén ci ñenn, fenn)) ak yonnent ya nga yabal (ci ñenn, fenn) ( Maa ngi lay dagaan ) Yaw Yàlla.


6- ( ci barkeb) Malaaka yépp, ak séén séén jëwriñ ja Jibriil, ak Mikaayil ( Maa ngi lay dagaan ) Yaw Yàlla.


7- ( ci barkeb) Israafiil may wal (ëf) bufta (mbiib) ba, ak Hazraayil may rocci ruuyi,(bindééf yi) ( Maa ngi lay dagaan ) Yaw Yàlla.


8- (ci barkeb) Sahaaba ya, ak waliyyu ya, ñoom ñépp, ak jëfkati (yu baax ya) di ay fòòré ( Maa ngi lay dagaan ) Yaw Yàlla.


9- (ci barkeb) Dëggalaakoon ba (Abu bakr) ak tàqalekat ba (Umar ma daan tàqale dëgg ak neen) ak boroom ñaari leer ya (Usmaan ma dencoon ñaari doom yu jigééni Yonnent ba, ak baayi ñaari sëti Yonnent ba (Aliyyu) ( Maa ngi lay dagaan ) Yaw Yàlla.


10- ( ci barkeb) Imaam Maalik ma amoon mayug Yàlla, ak imaam Shaafihiyyu, ak imaam Abu-haniifa, ak imaam Ahmad ibn-hanbal ( Maa ngi lay dagaan ) Yaw Yàlla.


11- (ci barkeb) àlluwa ja (lawhul mahfuuz) ak Xalima ga, ak sa gàngunaay gu màgg ga (Arash) ak toogu ba ( Maa ngi lay dagaan ) Yaw Yàlla.


12- (ci barkeb ) Alxuraan, ak Tawraat, ak tééré ba Daawud indiwoon ( Zabuur) ak tééré ba Ruuh ga (Iisaa) indiwoon ( Maa ngi lay dagaan ) Yaw Yàlla.


13- Jottalil ma sama salaat ak sama salaam ci Yonnent bi, moom ak ay gaayam, aki Sahaabam, aki soxnaam ( Maa ngi la koy dagaan ) Yaw Yàlla.


14- Na nga nu yiir mbalaanu tal Jàmm, na nga nu defal ag jublu (way, jëm-fenn) ci àddina ak àllaaxira ( Maa ngi lay dagaan ) Yaw Yàlla.


15- Bépp buntub yiw boo masa ubbil gaayu baax ya na nga nu ko ubbil ( Maa ngi la koy dagaan ) Yaw Yàlla.


16- Na nga nuy sòòb (tàbbal) ci ngérum (yoonu) njub, te na nga nuy dàqal jinné ak saytaane ( Maa ngi la koy dagaan ) Yaw Yàlla.


17- Na nga nu mottalil lépp lu nuy wuti ak di ko jublu, te na nga nu la nu gënal ( Maa ngi la koy dagaan ) Yaw Yàlla.


18- Na nga nu tàggatal lépp luy jàgg wala muy dëgër, na nga nuy yombalal lépp lu jafe, ( Maa ngi la koy dagaan ) Yaw Yàlla.


19- May nu gudd-fan boole ca wéral sunuy yaram, may nu ag njub, ak tawfiiq (lépp luy gën ci nun na nuy gënël) ( Maa ngi lay dagaan ) Yaw Yàlla.


20- Bépp noon bu jògati ngir bëgg noo lor na nga ko nappaaje bala muy yeksi ci nun, ( Maa ngi la koy dagaan ) Yaw Yàlla.


21- Na nga nu musël ci lépp luy taxa alku, te yit na nga nu musël ci nattuy (tiis) jamono yépp ( Maa ngi lay dagaan ) Yaw Yàlla.


22- (nattu yooyu bokk na ca) Ay gàkk, ay laago, fot, tiis, yëngub suuf, taraayu jamono, ag ñàkk ( Maa ngi lay dagaan nga musël nu ci ) Yaw Yàlla.


23- Ak doyadal, nééw, toroxtaane, noteel, ak ndòòl, mar, xiif ( Maa ngi lay dagaan nga musël nu ci ) Yaw Yàlla.


24- Fitna (Sànje), mbas (wopp juy wàlle), lakk, lab, melax (dënnu) càcc, wowug jamono, ( Maa ngi lay dagaan nga musël nu ci ) Yaw Yàlla.


25- Tàngoor, sedd, ngiir, jaaxle, mbugël, réér, lajj soox, bopp bu ubu ( Maa ngi lay dagaan nga musël nu ci ) Yaw Yàlla.


26- Mbamb (cucm) njuumte, cànkute, tarxiis (barastiku) soppeku dellu-ginaaw (yéés), teppas (mëdd) mbaq ( Maa ngi lay dagaan nga musël nu ci ) Yaw Yàlla.


27- Aw mar (Nàkk ndox gu tar), (Saddum) jinné ( ag ndof), ràgg (loof), wopp, ñaari wopp yu tar ya ( Siti ak ngaana), cér yuy dog di wàññiku di wadd ( Maa ngi lay dagaan nga musël nu ci ) Yaw Yàlla.


28- Ñaaw-ñaaw i (àddina ak àllaaxira), gàcceg (àddina ak àllaaxira ( Maa ngi lay dagaan nga musël nu ci ) Yaw Yàlla.


29- Yaw mi ame kàttanug def lépp, yaw mi jekki ca kaw gàngunaay gu màgg ga ( Maa ngi lay dagaan nga musël nu ci ) Yaw Yàlla.


30- Maa ngi lay ñaan xol bu ragal yalla, buy nangoo toroxlu (suufeel boppam) ak xam-xam bu bari ay njariñ ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


31- Tuub gu ñu nangu, ak jàppandal gu kawe, ak soxna su baax am diiné ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


32- Na nga nu musël ci ayu ku ëmb kiñaan, na nga nu musël it ci ayu gimiñ ay ayu bët ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


33- Ak ayu ag nbibar, ak ayu bindééf yi di nit wala jinné, ak ayu luy am tooke ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


34- Yaw sama wééruwaay (Yàlla) def naa la nga di sama tata ju ñoŋ ma di la dagaan na doon samab rawtukaay Yaw Yàlla.


35- Bul ma bàyyeek sama bopp mukk boo ko defee rekk dinaa alku te saayu ma la woowee na nga ma wuyu ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


36- Na nga ma defal samaw làmmiñ ak samab xol ñu di la fàttaliku ba ba may faatu, te bu may faatu nga def ma ma faaruwaale ngëm-Yàlla ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


37- Na nga ma dëgaralal samag kòòluté ci sama biir xol bi, ci lu àndul akug dengi-dengi (na nga ma) defal daje gi may dajeek yaw mu doon lu ma sopp ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


38- Na ga ma defal dee mu di ab nooflaay nekk it mbégté ci tar-tar ak ay ak xat-xat yi ma daan jànkuwanteel ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


39- Na nga ma sàmmal samaw yaram saayu ruugi teqalikoo ak moom, te lumu yàgg-yàgg bu yaram wi ràpp ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


40- Na nga doon mi may dimbali di sama wéttël bu ñu robee sama yaram wi ba ma des foofee ne cundum (wéét lool) ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


41- (Bu ñu ma robee ba noppi) bul ma booleek lu rëtloo (tiitloo) na nga ma fa fegal lépp lu ma ragal ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


42- Na nga ma musël man ak mbooleem jullit yi, na nga musël sama waajur wu jigéén, amiin waay ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


43- Na nga nu jéggal ak moom (sama waajur wu jigéén) na nga nu sàngal (suturaal) sunuy sikk, na nga nu ñewenti ak moom (sama waajur) ci aw tiis ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


44- Na nga jéggal sama (waajur) yërëm ko it ak nun, amun keneen kudul yaw ku baax ki ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


45- Ci biir bàmmeel ak ca barsax na ko fa dimbali yiir ko aar ko ci tiitaange te musël ko ci (lépp lu muy) ragal ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


46- Bul ko nattoo mukk lu mu àttanul, bul sooyal mukk yaakaaram ci yaw ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


47- Na nga nu nandal (Naan) ak moom ca ndoxum kawsara, (Déégub ndoxum Yonnent bi nga xam ne) moom nga tànn (moo gëna jag) ci mbindééf yépp ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.


48- Mom (Yonnent bi Muhammad) moo daan jubbanti boroom xel mu dëng, daan alag faagaagal ña weddi, daan dimbali ñi la ragal Yaw Yàlla.


49- (Kooku mooy) Muhammad ki muusloo gaayu baax ya, (kooku mooy) sunu njiit (li nuy gindi di ni wommat) jëmé nu àjjana ju sax ja dàkk bu kerook bisub pang ba ( bis bañuy jiital nit ñi jëmé léén fa ñuy àttee ca bis-pénc ba) Yaw Yàlla.


50- Na nga julli (dolli ko xeewël) te sëlmël (dolli musël) ci moom, ak ñépp ñu koy xeñ (topp) ba baa kerook bis-pénc ba di taxaw ( Maa ngi la koy dagaan) Yaw Yàlla.