mercredi 15 octobre 2014

Khassida: Traduction de Touhfatou en Wolof par S. Cheikhouna LO Ngabou

قصيدة تحفة المتضرعين في التوسل بأسماء المفضلين
للشيخ أحمد بامبا
المترجم شيخنا لو نغابو
Ki ko tekki ci wolof : Cheikhouna LO Ngabou
Tuhfatul mutadharrihina, xasida gu sëriñ Tuubaa moo ko taalif tuddé ko:
Xééwël gu ñu may ñi am i soxla yu ñu manut a ñàkk ba mel ni ab liir ca bttub ndey ja.
Mu làmboo taasu (sàkku ci darajay) ci barkeb gaaya gën a baax.

1- Maa ngi sant Yàlla di ko ñaan muy dolli xééwël gu sax dàkk ca ka nga xam ne moo nu feeñalal te indil nu ag njub. Mook Saabaam ya amoon lool mayug Yàlla.

2- Koo ku mooy sunu sang ba Muhammad.

3- Tay jii maa ngi ñaan sama boroom di taasu ci turi gaaya gën a baax.

4- Ma wax ne: yaw Yàlla miy ku jege, di kuy tontu di wuyu Yàlla na nga julli ci Yonnent bi nga xam ne bala ngaa wuyu kenn dafay fekk koo ka nangul ko te wuyu ab wooteem.

5- Ci barkeb Yonnent bi na nga ma nangul sama way wii yaw Yàlla jiy ku tedd yéwén. Te yit képp ku ko jël di ci dééyaaleek yaw na nga ko may defal ko lépp la mu cay sàkku.

6- Maa ngi lay ñaan nga Jéggal ma samay bàkkaar te fegal ma Saytaane, ci barkeb Nuuh ak Ibraayma

7- Fegal ma aw tiis aki naqar àddina ak àllaaxira ci barkeb Muusaa ak iisaa

8- Maa ngi lay ñaan nga julli ci Muhammad miy Yonnentub Yàlla bi julliwaale ca Yonnent ya Uluhazm.

9- te nga may ma Liimaan ngëm Lislaam jëfé ak Lihsaan rafetal, Tasawuf.

10- Maa ngi lay ñaan nga may ma ag sellal, ak tawfiiq dëppok lépp lu baax ci barkeb Abubakr Siddiiq ma doon dëggal Yonnent bi, ak Umar ma doon teqale dëgg ak neen.

11- Ci barkeb Usmaan ma dencoon soxna ñaari leer ya ñaari doom yu jigéén ya, ak ci barkeb Aliyu ma doon baayi ñaari sëti Yonnent bi Sàllal laahu alayhi wasallama.

12- Ma ngi lay ñaan nga may ma leer akug kowe aki xeewël ci àddina ak ca àllaaxira.

13- Maa ngi lay ñaan nga musël ma ci ay lor Ci barkeb Talhata ibn Ubaydalla, ak Zubayr ben awaam, ak Saad ben abiwaqaas.

14- Maa ngi lay ñaan nga musël ma ci fitna sanje ci barkeb Sahiid ibn Zayd, ak Abdaramaan ibn Awf.

15- Maa ngi lay ñaan nga ñoddil ma lépp luy mana jariñ, te fegal ma lépp luy mana alak.

16- Ma ngi lay ñaan nga may ma xam-xam bu bari ci barkeb Abdala ibn Abas doom-bay tax ba.

17- Maa ngi lay ñaan nga fegal ma lépp luy ñoddi lor ci barkeb Abdala ibn Umar.

18- Maa ngi lay ñaan nga fegal ma nattu mbas ak ayu bët ak ayu wax ci barkeb Abdallaa-Ibnu-masuud ak Abdallaa-Ibnu-salaam.

19- Yaw sama boroom maa ngi lay ñaan nga fegal ma bépp tar-tar ci barkeb Abaas ak Amza.

20- Maa ngi lay ñaan nga tabe lool ci man àddina ak àllaaxira may ma ñaari leer ya ci wormay Asan ak Usaynu.

21- Maa ngi lay ñaan nga sellal sama biir ak sama bitti ci wormay Xaasim ak Taayir.

22- Maa ngi lay ñaan nga saxal ci man mbégté ak ñu di ma teral ci wormay Tayyib ak Ibraayma.

23- Maa ngi lay ñaan nga feral sama bakan ci lépp luy waral ag tëj kaso ci darajay Faatimatu.

24- Maa ngi lay ñaan nga fegal fàww ak dàkku ak kiiraay ci wormay Ruqayya ak Zaynabu.

25- Maa ngi lay ñaan nga jubale ma ak teraanga fegal ma mbugal ci àddina ak àllaaxira ci wormay Umu-kulsuum.

26- Maa ngi lay ñaan nga nangu sama wax jii ñaan gii ci wormay Aws-ben-aamir ak Hëram ak Masruuq.

27- Maa ngi lay ñaan nga may ma Listiqama te jubbanti sama mbir ci wormay Rabii ak Aswad.

28- Maa ngi lay ñaan ci wormay Aamir-ben-abdurahmaan ak Abu-maslamatal-xawlaani.

29- Nga may ma ag njéggal akug texe akub xam-xam ak jëfé akug jaamu-yàlla.

30- Maa ngi lay ñaan nga may ma ag sàmmu akug set wecc ba mel ni kuñu fees ci bànneex aki bidaa ci wormay Asan-basri.

31- Maa ngi lay ñaan ay xééwal ci wormay Abu-huryrat ak Bilaal ak Suhëybu.

32- Maa ngi lay ñaan ci wormay Abu-dardaayi nga nangul ma topp gii ma lay topp te nga saafara ma ci jépp jàngoro ju feeñ ak ju nëbbu.

33- Maa ngi lay ñaan nga jotale ma ci samay jubluwaay ci wormay Miqadaad ak Xaalid ak Zubayru.

34- Maa ngi lay ñaan ci wormay Amiirul-muuminiina Umar nga fegal ma ay pexe, akug texeedi akug woru fakku.

35- Maa ngi la koy ñaan it ci wormay njiital jihaadkat yi Aliyu ma daan taxawu diiné ji.

36- Maa ngi lay ñaan ci wormay Saad ak Urwa nga dolli ma ag jafandu ci buum gu gën a dëgër ga.

37- Maa ngi lay ñaan ci wormay Xaasim ak Xaarija nga dolli ma ci xeñtu tërëiilni Yonnent bi

38- Maa ngi lay ñaan ci wormay Abu-bakr ak Abdul-laahi nga dolli ma ay ngënéél yu dootul jeex.

39- Maa ngi lay ñaan ci wormay Sulaymaan nga dimbali ma fegal ma pexam Saytaane ak feneen fu pexe man a jògé.

40- Maa ngi lay ñaan ci wormay sunu yaay Xadija nga may ma lépp lu may mébët ci xam-xam aki téggiin ak jëfé ko.

41- Maa ngi lay ñaan ci wormay sunu yaay Aysa nga fegal ma lépp lu may lor ci asamaan si ak suuf si.

42- Maa ngi lay ñaan ci wormay sunu yaay Afsa nga dox fàww sama digante ak lépp luy ñoddi aw tiis aku naqar.

43- Maa ngi lay ñaan ci wormay sunu yaay Zaynabu nga rafetalal ma sama biir ak sama biti.

44- Maa ngi lay ñaan ci wormay imaam-Maalik ak imaam-saafii ak imaam-abu-anifa ak imaam-ahmad-ben anbal nga nangul ma samay ñaan .


45- Maa ngi lay ñaan ci wormay Jibriil nga may ma li may ñaan te nga def ma ma jot sëkk dayob goor ña.

46- Maa ngi lay ñaan ci wormay Miikaayil nga may ma ay xééwal te def ma ma ame njariñ ni waame wu dët ab taw.

47- Maa ngi lay ñaan ci wormay Israafiil nga may ma ag ñoŋ sammu, te nga fegal ma tiisi bisub jaaxle ba.

48- Maa ngi lay ñaan ci wormay Asraayil nga defal ma njekk lu rafet sama giirug dund ak ginaaw bu ma faatoo.

49- Maa ngi lay ñaan sama xasidag tawassul gii képp ku la ci woo di la ñaan na nga ko ci defal texeg àddina ak àllaxira te it na nga ko jéggal.

50- Maa ngi lay ñaan nga may ma ci kòòluté ak ngëram man ak ñi sàkkuwoon ba ma way ko.

51- Te nga may nu ci it texe ak kaarange akug topptoo ba nu mucc ci wépp ñaawtééf.

52- Te nga may nu ci it nu mucc ci laajub biir bàmmeel, mbugël, sukraatus nde, regleente.

53- Te nga may nu ci it mbégté ak ségaré waxtu wa nuy dee ak ba nuy dekki.

54- Te nga julli ci Yonnent bi dolli koy xeewël te musël ko moom aki Saabaam yu baax ya.

55- Maa ngi lay ñaan it nga jéggal sama ñaari wayjur ak samag njabppt ak samay àndanadoo.

56- Maa ngi lay ñaan it nga jéggal mbooleem ku aju ci man, te it nga wéralal ma samag texe.

57- Maa ngi lay ñaan nga ñewenti nu, may nu kàttan, nekkal nu, defal nu mujj gu rafet.

58- Yàlla na nga julli ci Yonnent bi dolli ko xééwël te fajal ci jullit yépp sééni aajo.

Cheikhouna LO Ngabou

6 commentaires:

  1. Amna solo mouride yalla nga tassek tawfekh serigne bi

    RépondreSupprimer
  2. Machallah mouride amna solo li baxna lool ndakh sunouy diag xassida diko gêna téwlou manmi xamouma won ni lii mom la xassida gii du wakh yalna yalla fayy

    RépondreSupprimer