samedi 25 janvier 2014

Khassida Khaloo Li Yarkan (Penche vers les détenteurs du pouvoir ) avec traduction wolof et française

قالوا لي اركن لأبـواب السلاطيـن  تحـز جـوائـز تغنـي كلماحيـن

1- Ñi ngi may wax ni jengal dem ci buntu buur yi, sooko defee de dinga ci làqee koom gulay doy sa diirub dundu.

1 - Ils m’ont conseillé : Penche vers les détenteurs du pouvoir (Rois) et tu obtiendras  des récompenses qui t’enrichiront pour toute la vie

فقلـت حسبـي ربي و اكتفـيت به و لست راضي غير العلـم و الديـن

2 - Man ni léen sama Boroom doy na ma te doyloo naako, gërëmuma leneen ludul xam xam ak diine.

2 - J’ai répondu : je compte sur mon Seigneur, je me contente de lui ; je ne désire rien d’autre que le savoir et la religion

و لست أرجو و لا أخشى سوى ملكـي   لأنـه جـلَّ يغنـيني ويـنـجينـي 

3 - Yaakaaruma walla may ragal kenn ku dul Yàlla te, ndax Moom Mooy Ku màgg ki may koomal te di ma musal

3 - Je n’espère qu’en mon Roi, je ne crains que Lui, Il est Celui qui peut m’enrichir et me sauver

أنى أفوض أحوالي لمـن عجـزوا  عن حال أنفسهـم عجـزالمساكيـن

4 - Naka laay jële samay mbir joyal léen ci ñoo xam ni miskin di lotte ci ay mbiram lañu lottee ci seen mbir

4 - Comment pourrai-je confier mes affaires à des gens qui sont aussi incapables de s’occuper des leurs que des crèves la fin ?

أو كيف يبعثني حب الحطـام إلـى  جوار مـن دورهم دور الشياطيـن

5 - Walla naka la ma sopp poñatu àdduna mii di yobboo ci wetu ñoo xam ni seeni kër mooy fa Ibliis di féexloo ?

5 - Ou bien comment l’amour des vanités de ce monde m’oblige t-il à fréquenter des êtres dont la mesure est le parterre fleuri des démons(Satan)

إن كنت ذاحزن أو كنـت ذا وطـر  دعوت ذا العين قبل الـراءوالشيـن

6 - Su ma amee njàqare walla aajo Boroom Aras laay woo.

6 - Si j’éprouve un chagrin ou bien si j’ai une requête à présenter c’est au Maître du trône que j’adresse mes prières

وهو المعين الذي لاشـيء يعجـزه  وهـوالمكون ماشـاء أي تكـويـن

7 - Moom Mooy Ki nga xam ni lottul ci darra, Mooy Kiy nekkal lu ko soob na mu ko soobee

7 - Il est l’aide que rien ne réduit à l’impuissance et c’est lui qui fait ce qu’il veut de la manière qui lui plaise

إن شاء تعجيل أمر كـان ذاعجـل  أو شـاء تأجيلـه يبطأ إلـى حيـن

8 - Su bëggee am mbir gaaw mu gaaw, su ko nammee yéexal mu yeex ba jamono juko soob.

8 - S’il veut brusquer une affaire celle-ci est vite faite et s’il veut enretarder l’échéance, elle ne sera accomplie qu’après le délai marqué

يا من يلوم فلا تكثـر ودع عذلـي  إذ لست من فقدتي الدنيـا بمحـزون

9 - Yaw mi may yedd bulko baril te bàyyimaak sama beru ndax ñàkk gima ñàkk àdduna du aw njàqare ci man

9 - Oh mon censeur qui me fais des reproches : n’exagères pas, cesses de me blâmer car je ne m’attriste pas de la privation des biens terrestres


إن كان عيبي زهـد في حطامهـم  فـذاك عيب نفيـس ليس يخزينـي

10 - Su fekkee ne sama ayib mooy dëddu poñatum àdduna mii, loolu ayib ju gànjaru la duma ci jàq.

10 - Si mon défaut consiste au renoncement des princes voilà un vice dontje ne rougirai point.

1 commentaire: